La poésie d'auto-glorification en milieu Wolof du Baol:l'exemple du Kanupar Abdoulaye DIOME Université Cheikh Anta Diop de Dakar - Maîtrise 2019 |
CHAPITRE I : TRANSCRIPTION ET TRADUCTION DU CORPUSChant 1: Gërëm na baay Gërëm na baay moom mii ma jàngal mbay Ba sama benn moroom rawuma Gërëm na yaay Moom mii ma nàmpal bama de gune Duma dal ci waar diko waañi di yokk mbóoy Rus naako Duma deqqi ngoon diko lëmes ndajale ma tax Rus naako Gërëm na baay moom mii ma jàngal mbey Ba sama benn moroom rawuma Gërëm na yaay Moom mii ma nàmpal bama de gune Duma dal ci waar diko waañi di yokk mbóoy Rus naako Duma deqqi ngoon diko lëmes ndajalema tax Rus naako Chant 2 : Ana li may séen ? Ana li may séen ? Ana toolu baay ? Gaañi toolu baay ñorna Ku koy góob ? Jáambaar a nga tool Naaj bi tangna lool Bey noor, bey nawet Ñaq réerul boroom 18 Chant 1: Louange à mon père Louange à mon père qui m'a si bien appris à cultiver Aucun homme de ma classe d'âge ne me surpasse Je rends aussi grâce à ma mère Qui ne m'a pas sevré prématurément24 Au champ, je ne diminue jamais la surface à cultiver J'ai honte de le faire Je ne récolte pas l'arachide le soir en laissant les graines sous terre J'ai honte de le faire Louange à mon père qui m'a si bien appris à cultiver Qu'aucun homme de ma classe d'âge ne me dépasse Je rends aussi grâce à ma mère Qui ne m'a pas sevré prématurément Au champ, je ne diminue jamais la surface à cultiver J'ai honte de le faire Je ne récolte pas l'arachide le soir en laissant les graines sous terre J'ai honte de le faire. Chant 2 : Que vois-je ? Que vois-je ? Où est le champ de mon père ? Les gens le champ de père a mûri Qui va faire la moisson ? Le courageux est au champ Le soleil tape fort Cultivez en saison des pluies et en saison sèche La sueur se paye toujours 24 L'énonciation de la différence est une façon d'impressionner le vis-à-vis.C'est toujours dans la logique de la concurrence que le performateur de ce chant déclame les conditions dans lesquelles il est entretenu par ses parents pendants son enfance. 19 Chant 3: Ndooran deeti door Bisimillaaxi, bisimillaaxi Ndooran deeti door Suma doon fas naaru goor laay doon Suma doon jan du saamaan Suma doon mbaam ngongk laay doon Suma doon mbëtt di sénk Suma doon bukki di xàmbi Suma doon sikket di jaxaluur Suma doon yëkk di sambasay Suma doon gaynde di walor Suma doon gëléem Tukal ba laay doon Suma doon mbott xubaboye laay doon Suma doon xar kuy ba laay doon Chant 4: Ndaar yag nama jiin Ndaar yàgg nama jiin Ndaar yàgg nama jiin Ndaar yàgg nama jiin Ndaar yàgg nama jiin Jiin nama suba jiin nama ngoon Jiin nama suba jiin nama ngoon Ndaar yàgg nama jiin Ndaar yàgg nama jiin Ndaar yàgg nama jiin Ndaar yàgg nama jin Jiin nama suba jiin nama ngoon Jiin nama suba jiin nama ngoon Ma donn Samba Ngajal Mafan Ma donnTéeñ ak Mafan Ma donn Mayaasin Je? Maaroo Jigéen ju mën góor 20 Chant 3 : Je vais encore recommencer Au nom de Dieu, au nom de Dieu Je vais encore recommencer Si j'étais un cheval, je serais un pur-sang Si j'étais serpent, je serais un python Si j'étais un âne, je serais ngonk25 Si j'étais un varan, je serais le plus long Si j'étais une hyène, je serais la plus redoutable Si j'étais une chèvre, je serais un bouc Si j'étais une vache, je serais un taureau Si j'étais un lion, je serais le plus féroce Si j'étais un chameau, je serais le grand Si j'étais une grenouille, je serais un crapaud Si j'étais un mouton, je serais un bélier Chant 4 : le tam-tam m'a toujours loué Le tam-tam m'a toujours loué Le tam-tam m'a toujours loué Le tam-tam m'a toujours loué Le tam-tam m'a toujours loué Le tam-tam m'a toujours loué du matin au soir Le tam-tam m'a toujours loué du matin au soir Le tam-tam m'a toujours loué Le tam-tam m'a toujours loué Le tam-tam m'a toujours loué Le tam-tam m'a toujours loué Le tam-tam m'a toujours loué du matin au soir Le tam-tam m'a toujours loué du matin au soir Je suis l'héritier de Samba Ngajal Mafan 26 Je suis l'héritier de Téeñ27 et Mafan, je suis l'héritier de Mayacine Je? Maaroo28, une femme plus forte que les hommes. 25 Âne adulte et fort de sexe masculin caractérisé par sa force physique et sa capacité d'endurance. 26 Un des aïeux de l'homme qui chante, il était un très grand cultivateur. 27 Titre du roi au Baol 28 Mayacine Je? Maroo est un des aïeux du chanteur, il était un vaillant guerrier qui fut tué lors d'une bataille menée par Lat Soukabé. Chant 5: Damay liggéey ndax mooy wàllum ngor Damay liggéey ndax mooy wàllum gor Ndax xam naa ne kuko ñàkk Di gor, sa xel di la lor Sa nelaw dootul maase Boo tëddee sa xel dem si for Liggéey laa xam ndax sàmm ngor Su dul loolu te ñaan jafe ma Ñaq jariñu ndax ngor Luma am ci liggéey doyloo naako May ma duma yor Bañ naa kuma janni ndax toppee Rawatina gáddu ay bor Bëgg naa sama jom ak sa ngor Te yem ci lima yor. Chant 6: jáambaar Gaynde boroom àll Ñiay boroom manding Buki boroom mbeed Jéego boroom yéel Sarxole boroom jaal Arwatam boroom taat Suma doon jaan di saaman Suma doon gaynde di walor Jáambaaro, jáambaar Kula yàpp genn am réew Kula señu seekeek Jáambaaro, jáambaaro Kula yàpp genn am réew Kula señu seekeek 21 22 Chant 5 : Je travaille car c'est le devoir de l'honnête homme Je travaille car c'est un devoir pour tout homme digne L'homme qui ne travaille pas Sera tenaillé par sa conscience Son sommeil sera sans cesse agité Il ne connaîtra pas de répit Le travail me permet de préserver ma dignité Car quémander m'est tâche difficile Je préfère manger à la sueur de mon front Pour préserver ma dignité Je ne saurais vivre d'aumône ou de dettes J'ai peur d'être la rusée publique À cause de choses futiles, à fortiori des dettes Car, je tiens à mon honneur et à ma dignité C'est pourquoi je me contenterai de ce que j'ai Chant 6: jáambaaro29 Le lion roi de la forêt L'éléphant roi de la savane L'hyène reine la de brousses Pour faire de grandes foulées, il faut avoir de longues jambes Pour rire, il faut une bouche pourvue de dent Si j'étais serpent, je serais un python Si j'étais un lion, je serais le plus féroce L'Homme courageux, le guerrier Celui qui ose t'affronter, t'humilier, s'exilera de ce pays Celui qui mange tes os aura les joues enflées Jambaaro, jáambaaro Celui qui ose t'affronter, humilié, s'exilera de ce pays Celui qui mange tes os Aura les joues enflées 29 Homme courageux. 23 Chant 7: waaw góor suka péll gi Waaw góor suka péll gi Ndax péll gi romb nga ndaw Te mag mula sol wogantiku Mbaa mu sonn lool Ko ni bu suba flu daje Guddi googa du nelaw Mbaa bu nelaweet du yandoor Ndonoy yaay Majigéen jóob Nii nga mën a mel Doomu flay flay laay doon Baay Yata ku bëgg xam Nga tojj sa mbandum yaay Ku bëgg kula duma nga toofl ku la mën Chant 8: Sonn muñ Sonn mufl Bëgga dee mufl Ku mufl muufl Waaye sonn daw Bëgga dee daw Ku daw siiw Chant 7 : Brave Suka le « péll » !30 Brave Suka ! Tu surclasses tous les autres jeunes Tout adulte qui veut te porter retroussera ses manches Sinon, il lui en coûtera Celui qui osera te défier Ne dormira pas la veille S'il parvient à dormir son sommeil sera léger Héritier de Majigéen Jóob C'est cela ta légitime ambition Le fils d'un éléphant ne saurait être qu'un éléphanteau Père Yata, qui veut le vérifier N'a qu'à casser le canari de ma mère Qui veut être battu, provoque plus fort que lui Chant 8 : Se fatiguer et se résigner Se fatiguer et se résigner Souffrir à mort et se résigner Mais se fatiguer et fuir Souffrir à mort et fuir Qui s'enfuit sera la risée de tout le monde. 24 30 Celui à qui on s'adresse n'est pas d'accès facile, il n'est pas non plus facile à dompter. Qui essaie d'être comme lui découvre très tôt ses limites. 25 Chant 9: Ndonoy cosaan lii laa Ndonoy cosaan lii laa Ndonoy cosaan lii laa Alassane Ndella Njukel Ndella baay ba dee Ñaling Géet ma dee ndondol Mussa ma dee Gith Godu massa Mbul Biram massa ya géej Ngoone sa Lambay Ngaañ Demba ma jox nag Ag doomam naan ma deel nanuum sooW Bu ferale nga jaay ko Boroom doom jooyna Bu doom jooye nga jox ko Yaayam mo xam lamuy jooy Chant 10 : Saa Jaara Ak maa jaara Saa Jaara Ak maa jaara Njoogu jaara Ndapp Kumba jeeri Korr jeeri Korr janx ji Bana lepp ak gaayu góor yi Buñuy dem tool Dima jiin Te buñuy lekk Dima ñëbbu 26 Chant 9 : Voici l'héritage traditionnel Voici l'héritage de la tradition Voici l'héritage de la tradition Alassane Ndella Njukél Ndella dont le père est mort à Ñaling Géett est morte à Ndondol31 Mussa à Gith Godu à Mbul32 Biram est resté au bord de la mer Ngoone est restée à Lambay33 Ngaað Demba m'a offert une vache et son petit Pour que je puisse boire du lait Si la vache sevre, je la vends L'enfant pleure Si l'enfant pleure donne-le à sa mère, elle sait de pourquoi il pleure Chant 10: Saa Jaara et maa jaara34 Saa Jaara Et maa jaara Njoogu jaara Ndapp Kumba jeeri L'amoureux de Jeeri L'aimé des jeunes filles Et l'ennemi des hommes Quand ils vont au champ Ils me louent Et quand ils mangent Ils se cachent de moi 31 La commune de Ndondol se trouve dans la Région de Diourbel dans le département de Bambey. 32 Une célèbre capitale fondée par Lat Dior durant son règne au Cayor. 33 Capitale du Baol. 34 Saa Jaara et Maa Jaara désignent des noms que le poète utilise pour se glorifier. 27 Chant 11 : Jànj Góor jànj warna jànj njee Góor jànj warna jànj njee Makumba Aaleek Baaba ma ca Weydeel Bu jànj waree jànj, jànj waâc jànj Ta jànj saa yu waree jànj doon nub jànj Góoroo góor ! Góoroo góor ! Bo warul jànj teey jànj warla Bo noppee war jànj, jànj war la Góor jant ngay so Teey nga daan góor! Mbaa góor daan la! Ta góor bu daanee góor ca doxiin waala Maan nak Faal sëtub Damel Maasamba koddu Sëtub Lat Sukkaabe jëlëm Góoroo góor maa mën Bu jant fenkkee ba bala jant di so Ma wan gaañi ne Ma mën ca tool ya Ma mën ca kër ga Ndax aam land fasu naaru góor la Ku ca war jaal àll Baa nga wàcc Chant 12: Dog, Dog, Dog Dog, dog, dog Reppit ak ñeppet Sëgg dagg, siggi dagg Kuma daxa dagg, dagg sa loxo 28 Chant 11: La dune Brave homme, la dune a couvert une autre dune ! La dune a couvert une autre dune ! Oh ! Brave homme, La dune a couvert complètement l'autre ! Makumba Aaleek Baaba se trouve à Weydeel Si la dune se forme à côté d'une semblable, elle l'ensevelit Chaque fois que la dune se forme à côté d'une semblable elle devient un morne Oh ! Homme ! Oh ! Brave homme ! Aujourd'hui, si tu ne montes pas sur la dune, elle finira par te couvrir Quand tu cesses de monter sur la dune elle t'ensevelira Brave vite ! Le soleil va se coucher ! Oh! Brave homme ! Aujourd'hui tu triompheras de ton semblable Sinon il te vaincra ! Et si un brave homme bat son semblable, c'est à cause de sa démarche. Et moi, Faal petit-fils du Damel Maasamba koddu Petit fils de Lat Sukkaabe Jëlëm Parmi tous les hommes : « Je suis le meilleur, le plus fort. De l'aube jusqu'au coucher du soleil, Je montrerai aux hommes que je suis le meilleur aux champs Comme je le suis aussi à la maison Puis qu'un champ est un pur - sang Quiconque le chevauche, doit savoir galoper Sinon ne le chevauche pas.» Chant 12 : Coupez, coupez Coupez, coupez, coupez Reppet ak ñeppet35 Coupez en vous penchant et coupez en vous tenant debout Celui qui coupe mieux que moi, coupera sa main 35 Le bruit lors qu'on coupe les épis de mil. 29 Chant 13: Njaay Makayre Bey nga ca Joli Bey nga ca Mbandax Njaay ma kayre Yaasin Man nga bey Man nga bey Dem nga tool Tey nga yendoo bey Mbey ma nga Nduf Pecc ma nga Ndengler Bey nga ca Joli Bey nga ca Mbandax Njaay ma kayre Yaasin Man nga bey Man nga bey Dem nga tool Tey nga yendoo bay Mbey ma nga Nduf Pecc ma nga Ndengler Bey nga ca Joli Bey nga ca Mbandax Njaay ma kayre Yaasin Man nga bey Man nga bey Dem nga tool Tey nga yendoo bay Mbey ma nga Nduf Pecc ma nga Ndengler 30 Chant 13: Njaay Makayre36 Cultiver à Joli Cultiver à Mbandaax Njaay Makayre Yaasin Tu sais cultiver Tu sais cultiver Tu es allé au champ Tu vas passer la journée à cultiver L'agriculture c'est à Nduuf La danse c'est à Ndengler Cultiver à Joli Cultiver à Mbandaax Njaay Makayre Yaasin Tu sais cultiver Tu sais cultiver Tu es allé au champ Tu vas passer la journée à cultiver L'agriculture c'est à Nduuf La danse c'est à Ndengler Cultiver à Joli Cultiver à Mbandaax Njaay Makayre Yaasin Tu sais cultiver Tu sais cultiver Tu es allé au champ Tu vas passer la journée à cultiver L'agriculture c'est à Nduuf La danse c'est à Ndengler 36 Njaay Makayre est le brave paysan à qui on a dédié cette chanson. 31 Chant 14: Maa jomba ñaaw Maa jomba ñaaw Maay sëtub Seelawbe Buna Alburi Njaay Seelawbe ak Maamur Ña? Òoo jur Majigéen Ña? Jur Xureyja sall, jur Alaaji Ña? Xureyja sall ñeenti doom la am Faatu Ña?, Ami Ña?, Daam Ña?, Baaba Ña? Majigéen Ñaan moo jur: Isaaxa Ña?, Moodu Ña?, Daaru Ña?, Aminata Ña? Alaaji Sàll jur: Mbay Faama Ña?, Ibra Ndongo Maamur, Moor Gaynde, Alaaji, Maxureyja Sala Ña?, ak Nibu Ña? Man sëtub Faatu Ñaan mu Xureyja Ña? Man góor gu ma làngal nga daw Wacc ma ak sama tool baay Man bey naa yoor yoor Bèy naa takkusaan Ñu naan ma ku daw ñaaw Man naan leen man duma daw Ndax man duma jigéen Ñu naan suma doonoon góor Soo doonoon góor it doo faj gàcce Chant 14 : Moi je refuse le déshonneur Moi je refuse le déshonneur Je suis la petite fille de Seelawbe Buna Alburi Njaay 37 Seelawbe et Maamur Na? Ont donné naissance à Majigéen Na? Et à Xureyja sall et Alaaji Ña?. Xureyja sall a eu quatre enfants Faatu Ña?, Ami Ña?, Daam Ña?, Baaba Ña? Majigéen Ña? a donné naissance à Isaaxa Ña?, Moodu Ña?, Daaru Ña?, Aminata Ña? Alaaji Sàll est le père de Mbay Faama Ña?, Ibra Ndongo Maamur, Mor Gaynde, Alaaji Maxureyja Sala Ña?, et Nibu Ña? Moi petit- fils de Faatu Ñaan de Maxureyja Ña? Tout homme que je défie prend la fuite Pour me laisser seul avec le champ de Papa Moi, j'ai cultivé le matin entre 10h et 12h J'ai cultivé l'après-midi vers 17h Qui prend la fuite sera déshonoré me disait-on Je leur répondis que je ne fuirai pas Car je ne suis pas une femme Qui se plaît à dire, si j'étais homme Celle-là, même si elle était homme, ne relèverait jamais un défi. 32 37 Fils de Alboury Ndiaye ancien Bourba du Djolof et grande figure de la résistance à la pénétration coloniale. 33 Chant 15: woyu Samba Yaay bóoyo Samba nga ca tool ya Doyna ndam Baay bóoyo Samba nga ca tool ya Doyna ndam Yaay bóoyo ca tool ya Baay bóoyo ca tool ya Doom ca tool ya Doyna ndam Yaay bóoyo Samba nga ca tool ya Doyna ndam Baay bóoyo Samba nga ca tool ya Doyna ndam Doomu gaynde, gaynde laay doon Yaay bóoy ca tool ya Bay bóoy ca tool ya Doom ca tool ya Doyna ndam Doomu gaynde, gaynde lay doon 34 Chant 15: Le chant de Samba Oh mère ! Samba laboure dans les champs C'est là, tâche noble Oh père ! Samba laboure dans les champs C'est là, tâche noble Père va au champ Mère va au champ Le fils va au champ Ce sont là, des tâches nobles Le petit d'un lion Ne saurait être qu'un lionceau Oh mère ! Samba laboure dans les champs C'est là, tâche noble Oh père ! Samba laboure dans les champs C'est là, tâche noble Le petit d'un lion Ne saurait être qu'un lionceau 35 Chant 16: Bisimillaaxi jàmm Bisimillaaxi jàmm Raxmani jàmm Raxiimi jàmm Jàmm njëkk, jàmm mujj, jàmm nek ci digante bi Bisimillaaxi teew Raxmaani teew Raxiimi teew Ku teew ma teew, ku teewul ma teew, kuma tere teew ma teewela Ñodil bu dangul dikk Mangi sak seen gëmëñ Mag ak daw, góor ak jigéen Yalnanu yalla musal ci setan Ak balaa ak dee gu ñaaw Chant 17: yimbèy Yimbèy sama yimbèy Ngala Yimbèy saama yimbèy Ngala Kuy jaay sa mbaam awal yoonu Ngoy Soo yeggee Ngoy kër Móodu Sy Buur Djolof Njaay xar lalay rayal Yuur ga yaa koy naan Yaw ak say gay Yimbèy sama yimbèy Ngala Yimbèy sama yimbèy Ngala Chant 16 : Au nom de Dieu ! Au nom de Dieu ! La paix Le Clément ! La paix Le Miséricordieux ! La paix Paix devant ! Paix derrière ! Paix au centre Au nom de Dieu je suis là Au nom du Clément ! Je suis là Au nom du Miséricordieux ! Je suis là Je suis présent, si quelqu'un s'absente moi je suis présent, qui veut mon absence, sera absent Tirez ! S'il ne rompt pas, il suivra La personne élancée rit parce qu'elle peut atteindre le sommet La personne de courte taille pleure parce qu'elle ne peut pas atteindre le sommet Je vais tous vous subjuguer Que Dieu nous préserve de Satan, de la punition de l'au-delà et d'une mort tragique Chant 17 : Yimbé Yimbèy mon yimbèy Ngala Yimbèy mon yimbèy Ngala Qui veut vendre son âne prend le chemin de Ngoy38 Arrivé à Ngoy chez Móodu Sy Le roi du Djolof Njaay, immolera un mouton pour l'accueillir Il mangera de la cervelle Lui et ses compagnons Yimbé mon yimbé Ngala Yimbé mon yimbé Ngala 36 38 Ngoy se trouve dans la région de Diourbel dans le département de Bambey. 37 Chant 18: Modu Njaay Modu Njaay um Caar Xëy ci bénn ab tool Tool ba nër ta jeex Lool de gace la Modu Njaay um Caar Xëy ci benn ab tool Tool ba nër ta jeex Lool de gace la Modu Njaay um Caar Xëy ci benn ab tool Tool ba nër ta jeex Lool de gace la Modu Njaay um Caar Xëy ci benn ab tool Tool ba nër ta jeex Lool de gace la Chant 19: war na ab jànj war na ab jànj war na ab jànj doomi yaay Naar war na ab jànj yalna buma ab jànj gawa war 38 Chant 18 : Modu Njaay Modu Njaay de Caar A passé une journée dans un champ Sans finir de labourer Ça c'est une honte Modu Njaay de Caar A passé une journée dans un champ Sans finir de labourer Ça c'est une honte Modu Njaay de Caar A passé une journée dans un champ Sans finir de labourer Ça c'est une honte Modu Njaay de Caar A passé une journée dans un champ Sans finir de labourer Ça c'est une honte Chant 19 : J'ai monté sur la dune J'ai monté sur la dune J'ai monté sur la dune Le fils de yaay Naar A monté sur la dune Que Dieu fasse que la dune ne me recouvre pas 39 Chant 20 : Jappal maye ma Japp ma def ma sa jàam Japp ma def ma sa jàam Japp ma def ma sa jàam Mbaa nga japp jaay ma Doomi buur du gawa rey Chant 21 : Bilaaxi maa xam Bilaaxi maa xam Ndax Yalla miy mënale Mootax ma mën Ba ku flew ma wonla sama mën- mën Te kepp ku mëna faram-facce Xam na ni maa mën ndax dama oyof nib sën Ba tax far maay ki mën Chant 22 : Bisimillaaxi tagul mako déeti tagu warna jàam Bismillaaxi tagul mako déeti tagu warna jàam Abdu kura, ku Njoogu Njoogou Dia Pël mëw Baay Njoogu Njaay Baay Njoogu Njaay Bu donul kon Layti Ngoone Luma yendo bay makoy moom Buma flibe senn boroom jel Baay Njoogu Njaay Baay Njogu Njaay Bou donul kon Layti Ngoone Luma yendo bay makoy moom Buma flibe senn boroom jel 40 Chant 20 : Capture et donne ton esclave ! Capture-moi et fait de moi ton esclave ! Capture-moi et fait de moi ton esclave ! Capture-moi et fait de moi ton esclave ! Sinon capture moi et vend moi comme esclaves Le fils du roi ne doit pas exécuter très tôt Chant 21 : Au nom de Dieu, c'est moi qui connais39 Au nom de Dieu, c'est moi qui peux Car c'est Dieu le détenteur du pouvoir Qui m'en a donné Je peux le prouver à qui le voudrait Et quiconque sait traduire En sera convaincu Je suis humble comme un tas d'ordure Ce qui fait que je suis celui qui est capable Chant 22 : Louange à Dieu ! Je vais encore recommencer Louange à Dieu ! Je vais encore recommencer En rendant grâce à Dieu Abdu kura, ku Njoogu Njoogu Dia! Le Peul offre du lait Baay Njoogu Njaay Baay Njoogu Njaay Si ce n'était pas à cause de Layti Ngoone Tout ce que je récolterais le jour m'appartiendrait Si je rentre au village je le donnerais aux nécessiteux Baay Njoogu Njaay, Baay Njoogu Njaay Si ce n'était pas à cause de Layti Ngoone Tout ce que je récolterais le jour m'appartiendrait Si je rentre au village je le donnerais aux nécessiteux 39 Le performateur de se chant montre que celui qui veut prétendre au savoir et au pouvoir doit etre humble. 41 Chant 23: Waaroo waar Waaroo waar Waar dem na géej Waaroo waar Waar dem na géej samba Góoroo góor bu kenn daw Bu kenn naan i Yaay Faatu fattalikul Lima la waxoon biig Bu naaj tàngée Mane bu naaj tàngée Ci la jáambaar di féeñ Chant 24 : mala mala Dégg na si mala mala Du mala bañ Dégg na si yama yama Du yama soof Chant 25 : ngongk Mbaam ngongk rëy biir Soxor, mana màtt Aay cium cumbur Kuko war te mënoo ngawar Wëqu cammooñ la lay door Te fu mu la dal foofa nooy 42 Chant 23 : Oh labeur ! Oh labeur ! Le labeur est allé en mer Oh labeur ! Le labeur est allé en mer Que personne ne prenne la fuite Que personne n'aille boire Yaye Fatou40souviens-toi Je t'avais dit hier soir Quand le soleil est au zénith Je répète, quand le soleil est au zénith C'est à ce moment que le brave se distingue Chant 24: mala mala41 J'ai entendu dire mala mala Ne veut pas dire que je te déteste J'ai entendu dire yama yama42 Ne veut pas dire que je te minimise Chant 25: l'âne adulte L'âne adulte au gros ventre Méchant assoiffé de mordre Mauvaise pour les ânons Qui monte sur lui sans pouvoir s'accrocher C'est du pied gauche qu'il va te frapper Et là où il tape, fait des dégâts 40 Yaay fatou est la mère de l'homme qui se glorifie. 41 Onomatopée qui imite le bruit des rumeurs. 42 Rumeurs des racontars. 43 Chant 26: Njolor Samba Njolor Samba moy daane góor Duma nann i te ku nann i da nga daw Chant 27: Jáambaar ca waar Jáambaar ca waar ba Loo liggéey du yaako moom Ngembuléen gaañi Ñaq réerul boromam Jáambaar góorgóorlul suuf si noy na Tool bi yaa na Mbay lu baax la Ñaq réerul boromam Chant 28: Tool bi Tool bi dina sango njoor Mba ma sango njoor Chant 29: yewwul yee ma yewwul yee ma yewwuloo yee ma yewwul yee ma, Ndeeroo Njaay Bunu demee ngay lakk may bey yewwul yee ma yewwuloo yee ma yewwul yee ma, Ndeeroo Njaay Bunu demee ngay lakk may bey yewwul yee ma yewwuloo yee ma yewwul yee ma, Ndeeroo Njaay Bunu demee ngay lakk may bey 44 Chant 26 : C'est le soleil d'après-midi qui révèle l'homme C'est le soleil d'après-midi qui révèle l'homme Je ne vais pas boire quiconque ira boire aura fui Chant 27 : le courageux au champ C'est au champ qu'on reconnait le brave Tout ce que tu produis te revient de droit Retroussez les manches les gars La sueur se paye toujours Homme courageux acclame toi, la terre est molle Le champ est large La culture est une bonne chose La sueur se paye toujours Chant 28 : Le champ Le champ sera recouvert de pagne Sinon je serais recouvert de pagne Chant 29 : Réveille-moi dès que tu te lèves ! Réveille-toi et réveille-moi ! Réveille-toi et réveille-moi ! Ndeeroo Njaay, Réveille-moi dès que tu te lèves ! Arrivés sur place, tu brûleras les herbes et moi je cultiverai Réveille-toi et réveille-moi ! Réveille-toi et réveille-moi ! Ndeeroo Njaay, Réveille-moi dès que tu te lèves ! Arrivés sur place, tu brûleras les herbes et moi je cultiverai Réveille-toi et réveille-moi ! Réveille-toi et réveille-moi ! Ndeeroo Njaay, Réveille-moi dès que tu te lèves ! Arrivés sur place, tu brûleras les herbes et moi je cultiverai 45 Chant 30 : Ra?, Ra?, Ra? Ra?, Ra?, Ra? Ba ra? ba jeex Góoru faatu Njaay Maa mën flile ba ra? ba jéex Ra?, Ra?, Ra? Ba ra? ba jeex Góoru faatu Njaay Maa mën flile ba ra? ba jéex Ra?, Ra?, Ra? Ba ra? ba jeex Góoru faatu Njaay Maa mën flile ba ra? ba jéex Chant 31: Ngonka daan na Malaw Ngonka daan na Malaw Naaru goor daan na Buur Njaay Taaguna saa yaay Taaguna saa baay Dotuma gaaw a paan Ngonka daan na Malaw Naaru goor daan na Buur Njaay Taaguna saa yaay Taaguna saa baay Dotuma gaaw a paan Chant 32: Ñaaju njolor sãntabañ la Ñaaju njolor sãntabafl la Wante flaaju takusaan amna borom 46 Chant 30 : Rang43 Rang, rang, rang Jusqu'à la fin du rang L'homme de faatu Njaay 44 Je suis plus fort que ceux -ci Jusqu'au bout du rang Rang, rang, rang Jusqu'à la fin du rang L'homme de faatu Njaay Je suis plus fort que ceux -ci Jusqu'au bout du rang Chant 31 : L'âne a terrassé Malaw45 L'âne a terrassé Malaw Le coursier a terrassé Buur Njaay J'ai demandé l'autorisation à ma mère J'ai demandé l'autorisation à mon père Je ne me fatiguerai plus facilement L'âne a terrassé Malaw Le coursier a terrassé Buur Njaay J'ai demandé l'autorisation à ma mère J'ai demandé l'autorisation à mon père Je ne me fatiguerai plus facilement Chant 32 : Le soleil de Njolor46est une obligation Le soleil de njolor est une obligation Alors que le soleil de takusaan 47à un propriétaire 43 Ordre, disposition de plusieurs personnes ou choses sur une même ligne. 44 Fatou Ndiaye est l'épouse de l'homme qui se glorifie. 45 C'est le bouleversement des choses, il est indispensable qu'un roi avec toute sa dimension sociale tombe de cheval. 46 C'est au environ de 13 heures et 15heures quand le soleil est au zénith. 47 Vers 17heures. 47 Chant 33: Baay Demba waar Njaay Baay Demba waar Njaay Waar waa ko yóbbu géej Ba flukoy suul floo nga naan Gasléen mu xóot a xóot Waqileen mu xóot a xóot yaay Jáambaar ngeen fiy suul Ñun talunoo waxtaan tey ak yaw Afl baanga toolu Baay jibi Combaan Naanu baanga Baal Ndax Malik Yaasin tukkina Ndakaaru Kon tey flu yendoo béy Chant 34: Ma mën gune ak baayam Ma mën gune ak baayam Ndax Baay ba doole ba da jeex Té gune ba doole ba dikagul Chant 35: Mbay Njaay Mbay Njaayoo! Mbay Njaay Mbay Aali Bure Mbay Coro Codu Mbaar ak mbaar Mbaar ak Demba jigéen Tog-tongi cebi Ku bafl gaaya tiib ya tax Mbay Njaay o Mbay Njaay Mbay baaba Aali, Mbay baaba Biige Mbay Aali Biige, Coro Codu Ma Biige ak Biige Candeela Njoogu, Samba ak Xoyan Mbaar ak mbaar, Mbaar ak Lat Demba jigéen 48 Chant 33: Baay Demba waar Njaay 48 Baay Demba waar Njaay Le labour l'a conduit au bord de la mer En l'enterrant, on disait Creusez très profondément Retirer le sable du trou Car vous enterrez un homme courageux Nous n'avons pas le temps de discuter avec toi aujourd'hui Le repas se trouve au champ de Baay jibi Combaan La boisson se trouve à Baal Car Malik Yaasin est allé en voyage à Ndakaaru49 Donc on passera la journée à cultiver Chant 34 : Je suis plus fort qu'un père et son enfant Je suis plus fort qu'un père et son enfant La force du père est épuisée L'enfant n'a pas encore acquis une force suffisante Chant 35 : Mbay Njaay Mbay Njaay ôh Mbay Njaay, Mbay Aali Bure Mbay Coro Codu Mbaar et Mbaar50, Mbaar et Demba Jigéen Tog - tongi cébi51 Si vous détestez de tels gars, c'est dans leur manière de manger Mbay Njaay ôh Mbay Njaay, Mbay baba Aali, Mbay baba Biige Mbay Aali Biige, Coro Codou, Ma Biige et Biige Candeela Njoogu, Samba et Xoyan Mbaar et mbaar, Mbaar et Lat Demba jigén 48 Incité le groupe de travailleurs à soutenir l'effort jusqu'à terme, sans que personne ne recule. 49 La capitale du Sénégal (Dakar). 50 Mbaar le lieu d'initiation des jeunes circoncis. 51 La manière dont les jeunes mangent les plats de riz. 49 Chant 35: Ca Yaasin Je? Maaroo Ca Yaasin Je? Maaroo Ca Yaasin Je? Maaroo Ca Yaasin Je? Maaroo Ca Yaasin Je? Maaroo Jigéen nangi deedi daan góor Ci toolu bayaam Ca Yaasin Je? Maaroo Ca Yaasin Je? Maaroo Ca Yaasin Je? Maaroo Jigéen nangi deedi daan góor Ci toolu baayam Ca Yaasin Je? Maaroo Ca Yaasin Je? Maaroo Ca Yaasin Je? Maaroo Ca Yaasin Je? Maaroo Jigéen nangi deedi daan góor Ci toolu baayam Ca Yaasin Je? Maaroo Ca Yaasin Je? Maaroo Ca Yaasin Je? Maaroo Ca Yaasin Je? Maaroo Jigéen nangi deedi daan góor Ci toolu baayam Chant 35 : Thié Yaasin Je? Maaroo52 Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo La femme est en train de prendre le meilleur sur l'homme dans le champ de son père Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo La femme est en train de prendre le dessus sur l'homme dans le champ de son père Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo La femme est en train de prendre le dessus sur l'homme dans le champ de son père Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo La femme est en train de prendre le meilleur sur l'homme dans le champ de son père 50 52 Thié Yassine Dieng Mar a fait l'objet d'une légende qui raconte l'histoire d'une brave fille qui parvenait à dominer les hommes dans les champs. Elle est l'aïeule de la femme qui chante ici. 51 Chant 36: Baay bóoy demal rabbi njowaan Baay bóoy demal rabbi njowaan Tool bi dotul bóoy Baay bóoy won ma digi tool bii Mbaa ma jaal ci mbóoy mi Chant 37 : Jáambaar joni joni jáambaar legi legi Jáambaar joni joni jáambaar legi legi Jáambaar dikatinga tool jéme ngoon Benn jant duma daan Té ñaar ya duñu fenkkando Chant 38: jáambaaro Jáambaroo, jáambaar Jàamnaaroo, jáambaaar Ku sa yaay di jáambaar do daw xare Suma nare daw dee Toj naa àll bi Ray na gaynde yi Ma di jàambaar Jàambaroo, jàambaar Jàamnaaroo, jàambaaar Ku sa yaay di jàambaar do daw xare Suma nare daw dee Toj naa àll bi Ray na gaynde yi Ma di jàambaar 52 Chant 36 : Père va tisser un hamac Père va tisser un hamac Le champ ne peut plus résister Père montre-moi les limites du champ Avant que je déborde sur le champ d'autrui Chant 37 : Être courageux Être courageux sur le champ, devenir courageux à l'instant même Le courageux est venu au champ et travaillera jusqu'au soir Un seul soleil ne me fatigue pas Alors que deux soleils ne se lèvent jamais en même temps. Chant 38: oh guerrier Oh guerrier, le valeureux Oh guerrier, le valeureux Celui dont la mère est courageuse Ne fuit pas le combat Plutôt mourir que de fuir J'ai terrorisé la brousse J'ai tué les lions Je suis le brave Oh guerrier, le valeureux Oh guerrier, le valeureux Celui dont la mère est courageuse Ne fuit pas le combat Plutôt mourir que de fuir J'ai terrorisé la brousse J'ai tué les lions Je suis le brave 53 Chant 39: Sa sunu ñagee tool yi Sa sunu ñagee tool yi Ileer yi nàmmandoo Ndaw ñi pàacoo tool bi Ba ku ne tiim sab waar Jáambaar daaldi feeñ Ca ruur ma lay tàmbalee Naaj wi ne da?? leer Yaafus ba tàmbaliy feeñ Ker ga lay dàkki toog Gàcce manula wessu lii Tey ma won sama Baay ne Maa ko donn ci jáambaar Chant 40: toolu baay Toolu baay Fale itam toolu baay laa, jam53 Kon na ko bokk bey ko gaawoo, jam Su mala rawee nga puuboo, jam Soo ma rawee it tey nga puuboo, jam Toolu baay Fale itam toolu baay laa, jam Kon na ko bokk bey ko gaawoo, jam Su mala rawee nga puuboo, jam Soo ma rawee it tey nga puuboo, jam 53 Intaduisable 54 Chant 39 : Dès lors qu'on clôture les champs Dès lors qu'on clôture les champs Les houes sont aiguisées Les jeunes se partagent le champ Quand chacun aura sa part Cela commence par le défrichage Le soleil est au zénith Le fainéant se découvre Et va s'asseoir à l'ombre Honte ne peut être plus grande Je vais montrer à mon père Que j'ai hérité son courage Chant 40: le chant de père Le chant de père Là-bas aussi c'est le champ de père, jam Labourons-le vite ensemble, jam Si je te devance, tu vas chier, jam Si tu me devance aussi, tu vas chier Le chant de père Là-bas aussi c'est le champ de père, jam Labourons-le vite ensemble, jam Si je te devance, tu vas chier, jam Si tu me devance aussi, tu vas chier 55 Chant 41 : Yaasin Je? Maaroo Ah ! Yaasin Je? Maaroo Jigéen duma daan camiñ baamay daan Yaasin Je? Maaroo Jigéen duma daan camiñ baamay daan Ee janaxoo yow mi dëkk suufo Naka sama maam Baay gorgi pël bu degee ngaaraadu Dootul maye meew Samb maye meewo Jaarga maye nag Baay gorgi Samb maye meew Jaarga maye nag Baay gorgi yoo ñax bu tenk mbaam ak caatangu naaru góor Baay gorgi yoo ñax bu tenk mbaam tenk geeléem Saar Baay gorgi yoo ñax bu tenk mbaam Gune du ca joow Chant 41 : Yaasin Je? Maaroo Yaasin Je? Maaroo La femme ne me dompte pas c'est l'homme qui me dompte Yaasin Je? Maaroo La femme ne me dompte pas c'est l'homme qui me dompte Ah souris! Toi qui habites sous terre Comment va ma mère Baay Gorgi si un peul entend le kañu Il n'offrira plus du lait C'est le pâtre qui offre du lait Le Djarga54offre une vache Baye Gorgi c'est le pâtre qui offre du lait Le Djarga offre des vaches Baye Gorgi l'herbe qui entrave l'âne comme l'entrave du coursier Baye Gorgi l'herbe qui entrave l'âne et chameau Baye Gorgi l'herbe qui entrave l'âne Un enfant ne peut pas mouvoir Baye Gorgi dans l'herbe qui entrave l'âne Un enfant ne peut pas mouvoir 56 54 C'est celui qui possède un immense troupeau de vache, de mouton,... 57 Chant 42: Xabu yaay Ngoone Xabu, yaay Ngoone Xabu Mayaay saar Katarpala gen ci góor Joongama gen ci jigéen Xorxor a gen kamac Ñaaw a gen dee Ñambaas a gen taatunen Chant 43: Ndaama ak ndaamari bokkul Ndaama ak ndaamari bokkul Ndama yeel ba day gatt Xuuru ganaaw ga taaba Deun ba angase Lumu yótu jot ko Lumu dóor mu ñibi allaaxira Chant 44 : ndeqqi Duma deqqi ngoon Diko lëmës Rus naako Ndajale ma tax Duma deqqi ngoon Diko lëmës Rus naako Ndajale ma tax Duma deqqi ngoon Diko lëmës Rus naako Ndajale ma tax 58 Chant 42: Xabu, fils de Ngoone Xabu, fils de Ngoone, Xabu, fils de MayaaySaar Le Caterpillar55 convient mieux à l'homme La beauté sert mieux à la femme La lueur est préférable à l'obscurité totale La laideur à la mort Le Gnambasse56 à la nudité Chant 43 : Celui qui a une petite taille est tout à fait différent d'un nain Celui qui a une courte taille est tout à fait différent d'un nain Le petit a les os courts, Et des jambes courtes Une colonne vertébrale large Et une poitrine saillante Il atteint toujours son but Et quiconque encaisse son coup, séjourne dans l'au-delà Chant 44: la récolte d'arachide Je ne récolte pas l'arachide En laissant les graines sous la terre J'ai honte de le faire Parce que je pense au moment ou on doit les entasser Je ne récolte pas l'arachide En laissant les graines sous la terre J'ai honte de le faire Parce que je pense au moment ou on doit les entasser Je ne récolte pas l'arachide En laissant les graines sous la terre J'ai honte de le faire Parce que je pense au moment ou on doit les entasser. 55 Le performateur fait allusion à la force, à la puissance, et à l'endurance que doit avoir le cultivateur. 56 C'est un morceau de tissu souvent de couleurs différentes qu'on ajoute à un pagne ou un pantalon. 59 Chant 45: kañu Samba ak Baay Mor Kañu Samba ak Baay Mor Daaba ak daabali bokul Daaba xuuru ginaawa day yaa Loxo ya day bar jot Lumu yôotu jot Lumu dôor nga agg suuf Kañ Samba ak Baay Mor Maxuja Maram Gey Maxuja Maram Faal Maa ngi jooy téeñ Candeela Faal Buurub gey ma noon ya jaaxaanal fa Ndoom Kañu Samba ak Baay Moor Maxuja Maram Gçy! Maxuja Maram Faal! Maa ngi jooy teen Candeela Faal Buurub gey ma noon ya jaaxaanal fa Ndoom Ñii ngi dëppu, Ñii ngi deex Man mane cëpp ne cëreet ni gçndel ! Di beegu nim yee Di tàweeku nig laspeer Saakoddu Biige linger la Laba daðu koo bôoleek Côoni Mbayya? Béey Bèsub keeroog ku deewul gore woo Sa Aanta ak Saademba ak Seeni Saañoxor Saakoddu Biige liigeer la Njolor fasu bay laa Njolor njolooroo njolor Fasu baay laa ! Ku war ma door laa ! Ku bëgga war ma door la ! Baay boy yar nag mbooyyee, man bu ma màggee mëna bay 60 Chant 45 : Le slogan de Samba et de Baay Mor Le slogan de Samba et de Baay Mor « Daaba est différent de daabali57;Daaba au dos creux ; Il a les mains longues et agiles, tout est à sa portée et ses coups sont fatals La devise de Samba et de Baay Mor Maxuja Maram Gey! Maxuja Maram Faal Je pleure toujours Téeñ Candeela Faal,58 Le roi Gey que les ennemis tuèrent à Ndoom59 La devise de Samba et de Baye Mor Maxuja Maram Gey! Maxuja Maram faal Je pleure toujours Teigne Candeela Faal, Le roi Gey que les ennemis tuèrent à Ndoom Ceux-ci sont courbés, ceux-là sont tordus Moi, je suis droit, puissant et complet comme un ange : Je m'enroule sur moi-même tel un boa, je me tends telle une lance pierre60 Saakoddu Biige est linguère Laba affronta dans un duel mortel Côoni Mbayya? Béey Ce là, fut lâche celui qui ne trèpassa Sa Aanta et Sademba Seeni Saañoxor Sacodu Biigé sont lingère Njolor est le cheval de mon père ! Njolor, Njolor, Njolor est le cheval de mon père ! Je frapperai quiconque le chevauche ! Je frapperai aussi quiconque essaie de me l'enlever ! Mon père a laissé son champ en jachère61 ! Quand je serai grand je serai capable de le cultiver ! 57 Dâba et dâbali : ces deux catégories différentes l'une est plus petite que l'autre et ne sert qu'à couper les herbes et arbusseaux, l'autre plus grand et posséde deux branches qui ressemblent à des bras et sert à couper les herbes et à meuler le mil. 58 Ancien roi du Baol. 59 Ndome : lieu où est tombé ce roi cité ci-dessus. 60 Lance pierre : l'auteur utilise se même terme dans le texte wolof.il fait allusion à la matière élastique qui peut prendre une dimension extraordinaire, si on l'étire, l'auteur se compare à elle. 61 « Laisser son champ en jachère » ici ce n'est pas le fait laisser le champ au repos mais, les parents avaient l'habitude de tester l'efficacité et l'endurance de leurs enfants en leur donnant un grand lopin de terre bourré d'herbes à cultiver. Si le garçon en question pavient à cultiver le lopin en un temps record, on lui accord le droit d'avoir ses propres champs et de fonder une famille. 61 Njool Soda laay sëggël bay! Baay bóoyo, baay booy, baay booy Baay yar nag mbooyy Baay boy yar nag mbooyy Caali Maa Njonge Seen Sa ma baay, baay booy Man la doon xaar, maggënaa dama koy bay Chant 46: Mbay Njaay Mbay Njaayoo Mbay Njaay Mbay bukaari Biige Keroog bañu koy suul Manga naan Gas leen mu xoot Waxi leen mu yaa Njaay jaata njaay Jàambaar geeni suul Mbay Njaay moo bay ba wallu gejj Ndiole Soda Laye courbe toi et mets- toi au labeur ! Oh Père! Oh Père ! Mon père a laissé son champ en jachère ! Caali Maa Njonge Seen Mon père, mon cher père Ce champ m'attendait Je suis grand maintenant. Je vais le cultiver Chant 46: Mbay Njaay !62 Mbay Njaay oh! Mbay Njaay Mbaye de Bukari Biige Le jour où on l'enterrait, il disait Creusez profondément, Que le trou soit large Njaay jaata njaay63 Parce que vous enterrez un homme brave Mbay Njaay a cultivé son champ jusqu'au bord de la mer 62 62 Ce chant s'apparente beaucoup au mythe de Baye Demba War qui a cultiver jusqu'à la mer 63 Elle se dit pour faire l'éloge des ndiaye. 63 |
|