WOW !! MUCH LOVE ! SO WORLD PEACE !
Fond bitcoin pour l'amélioration du site: 1memzGeKS7CB3ECNkzSn2qHwxU6NZoJ8o
  Dogecoin (tips/pourboires): DCLoo9Dd4qECqpMLurdgGnaoqbftj16Nvp


Home | Publier un mémoire | Une page au hasard

 > 

La poésie d'auto-glorification en milieu Wolof du Baol: l'exemple du kanu


par Abdoulaye DIOME
Université Cheikh Anta Diop de Dakar - Maîtrise 2019
  

précédent sommaire suivant

Bitcoin is a swarm of cyber hornets serving the goddess of wisdom, feeding on the fire of truth, exponentially growing ever smarter, faster, and stronger behind a wall of encrypted energy

CHAPITRE I : TRANSCRIPTION ET TRADUCTION DU CORPUS

Chant 1: Gërëm na baay

Gërëm na baay moom mii ma jàngal mbay

Ba sama benn moroom rawuma

Gërëm na yaay

Moom mii ma nàmpal bama de gune

Duma dal ci waar diko waañi di yokk mbóoy

Rus naako

Duma deqqi ngoon diko lëmes ndajale ma tax

Rus naako

Gërëm na baay moom mii ma jàngal mbey

Ba sama benn moroom rawuma

Gërëm na yaay

Moom mii ma nàmpal bama de gune

Duma dal ci waar diko waañi di yokk mbóoy

Rus naako

Duma deqqi ngoon diko lëmes ndajalema tax

Rus naako

Chant 2 : Ana li may séen ?

Ana li may séen ?

Ana toolu baay ?

Gaañi toolu baay ñorna

Ku koy góob ?

Jáambaar a nga tool

Naaj bi tangna lool

Bey noor, bey nawet

Ñaq réerul boroom

18

Chant 1: Louange à mon père

Louange à mon père qui m'a si bien appris à cultiver

Aucun homme de ma classe d'âge ne me surpasse

Je rends aussi grâce à ma mère

Qui ne m'a pas sevré prématurément24

Au champ, je ne diminue jamais la surface à cultiver

J'ai honte de le faire

Je ne récolte pas l'arachide le soir en laissant les graines sous terre

J'ai honte de le faire

Louange à mon père qui m'a si bien appris à cultiver

Qu'aucun homme de ma classe d'âge ne me dépasse

Je rends aussi grâce à ma mère

Qui ne m'a pas sevré prématurément

Au champ, je ne diminue jamais la surface à cultiver

J'ai honte de le faire

Je ne récolte pas l'arachide le soir en laissant les graines sous terre

J'ai honte de le faire.

Chant 2 : Que vois-je ?

Que vois-je ?

Où est le champ de mon père ?

Les gens le champ de père a mûri

Qui va faire la moisson ?

Le courageux est au champ

Le soleil tape fort

Cultivez en saison des pluies et en saison sèche

La sueur se paye toujours

24 L'énonciation de la différence est une façon d'impressionner le vis-à-vis.C'est toujours dans la logique de la concurrence que le performateur de ce chant déclame les conditions dans lesquelles il est entretenu par ses parents pendants son enfance.

19

Chant 3: Ndooran deeti door

Bisimillaaxi, bisimillaaxi

Ndooran deeti door

Suma doon fas naaru goor laay doon

Suma doon jan du saamaan

Suma doon mbaam ngongk laay doon

Suma doon mbëtt di sénk

Suma doon bukki di xàmbi

Suma doon sikket di jaxaluur

Suma doon yëkk di sambasay

Suma doon gaynde di walor

Suma doon gëléem Tukal ba laay doon

Suma doon mbott xubaboye laay doon

Suma doon xar kuy ba laay doon

Chant 4: Ndaar yag nama jiin

Ndaar yàgg nama jiin

Ndaar yàgg nama jiin

Ndaar yàgg nama jiin

Ndaar yàgg nama jiin

Jiin nama suba jiin nama ngoon

Jiin nama suba jiin nama ngoon

Ndaar yàgg nama jiin

Ndaar yàgg nama jiin

Ndaar yàgg nama jiin

Ndaar yàgg nama jin

Jiin nama suba jiin nama ngoon

Jiin nama suba jiin nama ngoon

Ma donn Samba Ngajal Mafan

Ma donnTéeñ ak Mafan

Ma donn Mayaasin Je? Maaroo

Jigéen ju mën góor

20

Chant 3 : Je vais encore recommencer

Au nom de Dieu, au nom de Dieu

Je vais encore recommencer

Si j'étais un cheval, je serais un pur-sang

Si j'étais serpent, je serais un python

Si j'étais un âne, je serais ngonk25

Si j'étais un varan, je serais le plus long

Si j'étais une hyène, je serais la plus redoutable

Si j'étais une chèvre, je serais un bouc

Si j'étais une vache, je serais un taureau

Si j'étais un lion, je serais le plus féroce

Si j'étais un chameau, je serais le grand

Si j'étais une grenouille, je serais un crapaud

Si j'étais un mouton, je serais un bélier

Chant 4 : le tam-tam m'a toujours loué

Le tam-tam m'a toujours loué

Le tam-tam m'a toujours loué

Le tam-tam m'a toujours loué

Le tam-tam m'a toujours loué

Le tam-tam m'a toujours loué du matin au soir

Le tam-tam m'a toujours loué du matin au soir

Le tam-tam m'a toujours loué

Le tam-tam m'a toujours loué

Le tam-tam m'a toujours loué

Le tam-tam m'a toujours loué

Le tam-tam m'a toujours loué du matin au soir

Le tam-tam m'a toujours loué du matin au soir

Je suis l'héritier de Samba Ngajal Mafan 26

Je suis l'héritier de Téeñ27 et Mafan, je suis l'héritier de Mayacine Je? Maaroo28, une femme

plus forte que les hommes.

25 Âne adulte et fort de sexe masculin caractérisé par sa force physique et sa capacité d'endurance.

26 Un des aïeux de l'homme qui chante, il était un très grand cultivateur.

27 Titre du roi au Baol

28 Mayacine Je? Maroo est un des aïeux du chanteur, il était un vaillant guerrier qui fut tué lors d'une bataille menée par Lat Soukabé.

Chant 5: Damay liggéey ndax mooy wàllum ngor

Damay liggéey ndax mooy wàllum gor

Ndax xam naa ne kuko ñàkk

Di gor, sa xel di la lor

Sa nelaw dootul maase

Boo tëddee sa xel dem si for

Liggéey laa xam ndax sàmm ngor

Su dul loolu te ñaan jafe ma

Ñaq jariñu ndax ngor

Luma am ci liggéey doyloo naako

May ma duma yor

Bañ naa kuma janni ndax toppee

Rawatina gáddu ay bor

Bëgg naa sama jom ak sa ngor

Te yem ci lima yor.

Chant 6: jáambaar

Gaynde boroom àll

Ñiay boroom manding

Buki boroom mbeed

Jéego boroom yéel

Sarxole boroom jaal

Arwatam boroom taat

Suma doon jaan di saaman

Suma doon gaynde di walor

Jáambaaro, jáambaar

Kula yàpp genn am réew

Kula señu seekeek

Jáambaaro, jáambaaro

Kula yàpp genn am réew

Kula señu seekeek

21

22

Chant 5 : Je travaille car c'est le devoir de l'honnête homme

Je travaille car c'est un devoir pour tout homme digne

L'homme qui ne travaille pas

Sera tenaillé par sa conscience

Son sommeil sera sans cesse agité

Il ne connaîtra pas de répit

Le travail me permet de préserver ma dignité

Car quémander m'est tâche difficile

Je préfère manger à la sueur de mon front

Pour préserver ma dignité

Je ne saurais vivre d'aumône ou de dettes

J'ai peur d'être la rusée publique

À cause de choses futiles, à fortiori des dettes

Car, je tiens à mon honneur et à ma dignité

C'est pourquoi je me contenterai de ce que j'ai

Chant 6: jáambaaro29

Le lion roi de la forêt

L'éléphant roi de la savane

L'hyène reine la de brousses

Pour faire de grandes foulées, il faut avoir de longues jambes

Pour rire, il faut une bouche pourvue de dent

Si j'étais serpent, je serais un python

Si j'étais un lion, je serais le plus féroce

L'Homme courageux, le guerrier

Celui qui ose t'affronter, t'humilier, s'exilera de ce pays

Celui qui mange tes os aura les joues enflées

Jambaaro, jáambaaro

Celui qui ose t'affronter, humilié, s'exilera de ce pays

Celui qui mange tes os

Aura les joues enflées

29 Homme courageux.

23

Chant 7: waaw góor suka péll gi

Waaw góor suka péll gi

Ndax péll gi romb nga ndaw

Te mag mula sol wogantiku

Mbaa mu sonn lool

Ko ni bu suba flu daje

Guddi googa du nelaw

Mbaa bu nelaweet du yandoor

Ndonoy yaay Majigéen jóob

Nii nga mën a mel

Doomu flay flay laay doon

Baay Yata ku bëgg xam

Nga tojj sa mbandum yaay

Ku bëgg kula duma nga toofl ku la mën

Chant 8: Sonn muñ

Sonn mufl

Bëgga dee mufl

Ku mufl muufl

Waaye sonn daw

Bëgga dee daw

Ku daw siiw

Chant 7 : Brave Suka le « péll » !30

Brave Suka !

Tu surclasses tous les autres jeunes

Tout adulte qui veut te porter retroussera ses manches

Sinon, il lui en coûtera

Celui qui osera te défier

Ne dormira pas la veille

S'il parvient à dormir son sommeil sera léger

Héritier de Majigéen Jóob

C'est cela ta légitime ambition

Le fils d'un éléphant ne saurait être qu'un éléphanteau

Père Yata, qui veut le vérifier

N'a qu'à casser le canari de ma mère

Qui veut être battu, provoque plus fort que lui

Chant 8 : Se fatiguer et se résigner

Se fatiguer et se résigner

Souffrir à mort et se résigner

Mais se fatiguer et fuir

Souffrir à mort et fuir

Qui s'enfuit sera la risée de tout le monde.

24

30 Celui à qui on s'adresse n'est pas d'accès facile, il n'est pas non plus facile à dompter. Qui essaie d'être comme lui découvre très tôt ses limites.

25

Chant 9: Ndonoy cosaan lii laa

Ndonoy cosaan lii laa

Ndonoy cosaan lii laa

Alassane Ndella Njukel

Ndella baay ba dee Ñaling

Géet ma dee ndondol

Mussa ma dee Gith

Godu massa Mbul

Biram massa ya géej

Ngoone sa Lambay

Ngaañ Demba ma jox nag

Ag doomam naan ma deel nanuum sooW

Bu ferale nga jaay ko

Boroom doom jooyna

Bu doom jooye nga jox ko

Yaayam mo xam lamuy jooy

Chant 10 : Saa Jaara Ak maa jaara

Saa Jaara

Ak maa jaara

Njoogu jaara

Ndapp Kumba jeeri

Korr jeeri

Korr janx ji

Bana lepp ak gaayu góor yi

Buñuy dem tool

Dima jiin

Te buñuy lekk

Dima ñëbbu

26

Chant 9 : Voici l'héritage traditionnel

Voici l'héritage de la tradition

Voici l'héritage de la tradition

Alassane Ndella Njukél

Ndella dont le père est mort à Ñaling

Géett est morte à Ndondol31

Mussa à Gith

Godu à Mbul32

Biram est resté au bord de la mer

Ngoone est restée à Lambay33

Ngaað Demba m'a offert une vache et son petit

Pour que je puisse boire du lait

Si la vache sevre, je la vends

L'enfant pleure

Si l'enfant pleure donne-le à sa mère, elle sait de pourquoi il pleure

Chant 10: Saa Jaara et maa jaara34

Saa Jaara

Et maa jaara

Njoogu jaara

Ndapp Kumba jeeri

L'amoureux de Jeeri

L'aimé des jeunes filles

Et l'ennemi des hommes

Quand ils vont au champ

Ils me louent

Et quand ils mangent

Ils se cachent de moi

31 La commune de Ndondol se trouve dans la Région de Diourbel dans le département de Bambey.

32 Une célèbre capitale fondée par Lat Dior durant son règne au Cayor.

33 Capitale du Baol.

34 Saa Jaara et Maa Jaara désignent des noms que le poète utilise pour se glorifier.

27

Chant 11 : Jànj

Góor jànj warna jànj njee

Góor jànj warna jànj njee

Makumba Aaleek Baaba ma ca Weydeel

Bu jànj waree jànj, jànj waâc jànj

Ta jànj saa yu waree jànj doon nub jànj

Góoroo góor ! Góoroo góor !

Bo warul jànj teey jànj warla

Bo noppee war jànj, jànj war la

Góor jant ngay so

Teey nga daan góor!

Mbaa góor daan la!

Ta góor bu daanee góor ca doxiin waala

Maan nak Faal sëtub Damel Maasamba koddu

Sëtub Lat Sukkaabe jëlëm

Góoroo góor maa mën

Bu jant fenkkee ba bala jant di so

Ma wan gaañi ne

Ma mën ca tool ya

Ma mën ca kër ga

Ndax aam land fasu naaru góor la

Ku ca war jaal àll

Baa nga wàcc

Chant 12: Dog, Dog, Dog

Dog, dog, dog

Reppit ak ñeppet

Sëgg dagg, siggi dagg

Kuma daxa dagg, dagg sa loxo

28

Chant 11: La dune

Brave homme, la dune a couvert une autre dune !

La dune a couvert une autre dune !

Oh ! Brave homme,

La dune a couvert complètement l'autre !

Makumba Aaleek Baaba se trouve à Weydeel

Si la dune se forme à côté d'une semblable, elle l'ensevelit

Chaque fois que la dune se forme à côté d'une semblable elle devient un morne

Oh ! Homme ! Oh ! Brave homme !

Aujourd'hui, si tu ne montes pas sur la dune, elle finira par te couvrir

Quand tu cesses de monter sur la dune elle t'ensevelira

Brave vite ! Le soleil va se coucher !

Oh! Brave homme ! Aujourd'hui tu triompheras de ton semblable

Sinon il te vaincra !

Et si un brave homme bat son semblable, c'est à cause de sa démarche.

Et moi, Faal petit-fils du Damel Maasamba koddu

Petit fils de Lat Sukkaabe Jëlëm

Parmi tous les hommes : « Je suis le meilleur, le plus fort.

De l'aube jusqu'au coucher du soleil,

Je montrerai aux hommes que je suis le meilleur aux champs

Comme je le suis aussi à la maison

Puis qu'un champ est un pur - sang

Quiconque le chevauche, doit savoir galoper

Sinon ne le chevauche pas.»

Chant 12 : Coupez, coupez

Coupez, coupez, coupez

Reppet ak ñeppet35

Coupez en vous penchant et coupez en vous tenant debout

Celui qui coupe mieux que moi, coupera sa main

35 Le bruit lors qu'on coupe les épis de mil.

29

Chant 13: Njaay Makayre

Bey nga ca Joli

Bey nga ca Mbandax

Njaay ma kayre Yaasin

Man nga bey

Man nga bey

Dem nga tool

Tey nga yendoo bey

Mbey ma nga Nduf

Pecc ma nga Ndengler

Bey nga ca Joli

Bey nga ca Mbandax

Njaay ma kayre Yaasin

Man nga bey

Man nga bey

Dem nga tool

Tey nga yendoo bay

Mbey ma nga Nduf

Pecc ma nga Ndengler

Bey nga ca Joli

Bey nga ca Mbandax

Njaay ma kayre Yaasin

Man nga bey

Man nga bey

Dem nga tool

Tey nga yendoo bay

Mbey ma nga Nduf

Pecc ma nga Ndengler

30

Chant 13: Njaay Makayre36

Cultiver à Joli

Cultiver à Mbandaax

Njaay Makayre Yaasin

Tu sais cultiver

Tu sais cultiver

Tu es allé au champ

Tu vas passer la journée à cultiver

L'agriculture c'est à Nduuf

La danse c'est à Ndengler

Cultiver à Joli

Cultiver à Mbandaax

Njaay Makayre Yaasin

Tu sais cultiver

Tu sais cultiver

Tu es allé au champ

Tu vas passer la journée à cultiver

L'agriculture c'est à Nduuf

La danse c'est à Ndengler

Cultiver à Joli

Cultiver à Mbandaax

Njaay Makayre Yaasin

Tu sais cultiver

Tu sais cultiver

Tu es allé au champ

Tu vas passer la journée à cultiver

L'agriculture c'est à Nduuf

La danse c'est à Ndengler

36 Njaay Makayre est le brave paysan à qui on a dédié cette chanson.

31

Chant 14: Maa jomba ñaaw

Maa jomba ñaaw

Maay sëtub Seelawbe Buna Alburi Njaay

Seelawbe ak Maamur Ña?

Òoo jur Majigéen Ña?

Jur Xureyja sall,

jur Alaaji Ña?

Xureyja sall ñeenti doom la am

Faatu Ña?, Ami Ña?, Daam Ña?, Baaba Ña?

Majigéen Ñaan moo jur:

Isaaxa Ña?, Moodu Ña?, Daaru Ña?, Aminata Ña?

Alaaji Sàll jur: Mbay Faama Ña?, Ibra Ndongo

Maamur, Moor Gaynde, Alaaji, Maxureyja

Sala Ña?, ak Nibu Ña?

Man sëtub Faatu Ñaan mu Xureyja Ña?

Man góor gu ma làngal nga daw

Wacc ma ak sama tool baay

Man bey naa yoor yoor

Bèy naa takkusaan

Ñu naan ma ku daw ñaaw

Man naan leen man duma daw

Ndax man duma jigéen

Ñu naan suma doonoon góor

Soo doonoon góor it doo faj gàcce

Chant 14 : Moi je refuse le déshonneur

Moi je refuse le déshonneur

Je suis la petite fille de Seelawbe Buna Alburi Njaay 37

Seelawbe et Maamur Na?

Ont donné naissance à Majigéen Na?

Et à Xureyja sall et Alaaji Ña?. Xureyja sall a eu quatre enfants

Faatu Ña?, Ami Ña?, Daam Ña?, Baaba Ña?

Majigéen Ña? a donné naissance à

Isaaxa Ña?, Moodu Ña?, Daaru Ña?, Aminata Ña?

Alaaji Sàll est le père de Mbay Faama Ña?, Ibra Ndongo

Maamur, Mor Gaynde, Alaaji Maxureyja

Sala Ña?, et Nibu Ña?

Moi petit- fils de Faatu Ñaan de Maxureyja Ña?

Tout homme que je défie prend la fuite

Pour me laisser seul avec le champ de Papa

Moi, j'ai cultivé le matin entre 10h et 12h

J'ai cultivé l'après-midi vers 17h

Qui prend la fuite sera déshonoré me disait-on

Je leur répondis que je ne fuirai pas

Car je ne suis pas une femme

Qui se plaît à dire, si j'étais homme

Celle-là, même si elle était homme, ne relèverait jamais un défi.

32

37 Fils de Alboury Ndiaye ancien Bourba du Djolof et grande figure de la résistance à la pénétration coloniale.

33

Chant 15: woyu Samba

Yaay bóoyo

Samba nga ca tool ya

Doyna ndam

Baay bóoyo

Samba nga ca tool ya

Doyna ndam

Yaay bóoyo ca tool ya

Baay bóoyo ca tool ya

Doom ca tool ya

Doyna ndam

Yaay bóoyo

Samba nga ca tool ya

Doyna ndam

Baay bóoyo

Samba nga ca tool ya

Doyna ndam

Doomu gaynde, gaynde laay doon

Yaay bóoy ca tool ya

Bay bóoy ca tool ya

Doom ca tool ya

Doyna ndam

Doomu gaynde, gaynde lay doon

34

Chant 15: Le chant de Samba

Oh mère !

Samba laboure dans les champs

C'est là, tâche noble

Oh père !

Samba laboure dans les champs

C'est là, tâche noble

Père va au champ

Mère va au champ

Le fils va au champ

Ce sont là, des tâches nobles

Le petit d'un lion

Ne saurait être qu'un lionceau

Oh mère !

Samba laboure dans les champs

C'est là, tâche noble

Oh père !

Samba laboure dans les champs

C'est là, tâche noble

Le petit d'un lion

Ne saurait être qu'un lionceau

35

Chant 16: Bisimillaaxi jàmm

Bisimillaaxi jàmm

Raxmani jàmm

Raxiimi jàmm

Jàmm njëkk, jàmm mujj, jàmm nek ci digante bi

Bisimillaaxi teew

Raxmaani teew

Raxiimi teew

Ku teew ma teew, ku teewul ma teew, kuma tere teew ma teewela

Ñodil bu dangul dikk

Mangi sak seen gëmëñ

Mag ak daw, góor ak jigéen

Yalnanu yalla musal ci setan

Ak balaa ak dee gu ñaaw

Chant 17: yimbèy

Yimbèy sama yimbèy Ngala

Yimbèy saama yimbèy Ngala

Kuy jaay sa mbaam awal yoonu Ngoy

Soo yeggee Ngoy kër Móodu Sy

Buur Djolof Njaay xar lalay rayal

Yuur ga yaa koy naan

Yaw ak say gay

Yimbèy sama yimbèy Ngala

Yimbèy sama yimbèy Ngala

Chant 16 : Au nom de Dieu !

Au nom de Dieu ! La paix

Le Clément ! La paix

Le Miséricordieux ! La paix

Paix devant ! Paix derrière ! Paix au centre

Au nom de Dieu je suis là

Au nom du Clément ! Je suis là

Au nom du Miséricordieux ! Je suis là

Je suis présent, si quelqu'un s'absente moi je suis présent, qui veut mon absence, sera absent

Tirez ! S'il ne rompt pas, il suivra

La personne élancée rit parce qu'elle peut atteindre le sommet

La personne de courte taille pleure parce qu'elle ne peut pas atteindre le sommet

Je vais tous vous subjuguer

Que Dieu nous préserve de Satan, de la punition de l'au-delà et d'une mort tragique

Chant 17 : Yimbé

Yimbèy mon yimbèy Ngala

Yimbèy mon yimbèy Ngala

Qui veut vendre son âne prend le chemin de Ngoy38

Arrivé à Ngoy chez Móodu Sy

Le roi du Djolof Njaay, immolera un mouton pour l'accueillir

Il mangera de la cervelle

Lui et ses compagnons

Yimbé mon yimbé Ngala

Yimbé mon yimbé Ngala

36

38 Ngoy se trouve dans la région de Diourbel dans le département de Bambey.

37

Chant 18: Modu Njaay

Modu Njaay um Caar

Xëy ci bénn ab tool

Tool ba nër ta jeex

Lool de gace la

Modu Njaay um Caar

Xëy ci benn ab tool

Tool ba nër ta jeex

Lool de gace la

Modu Njaay um Caar

Xëy ci benn ab tool

Tool ba nër ta jeex

Lool de gace la

Modu Njaay um Caar

Xëy ci benn ab tool

Tool ba nër ta jeex

Lool de gace la

Chant 19: war na ab jànj

war na ab jànj

war na ab jànj

doomi yaay Naar

war na ab jànj

yalna buma ab jànj gawa war

38

Chant 18 : Modu Njaay

Modu Njaay de Caar

A passé une journée dans un champ

Sans finir de labourer

Ça c'est une honte

Modu Njaay de Caar

A passé une journée dans un champ

Sans finir de labourer

Ça c'est une honte

Modu Njaay de Caar

A passé une journée dans un champ

Sans finir de labourer

Ça c'est une honte

Modu Njaay de Caar

A passé une journée dans un champ

Sans finir de labourer

Ça c'est une honte

Chant 19 : J'ai monté sur la dune

J'ai monté sur la dune

J'ai monté sur la dune

Le fils de yaay Naar

A monté sur la dune

Que Dieu fasse que la dune ne me recouvre pas

39

Chant 20 : Jappal maye ma

Japp ma def ma sa jàam

Japp ma def ma sa jàam

Japp ma def ma sa jàam

Mbaa nga japp jaay ma

Doomi buur du gawa rey

Chant 21 : Bilaaxi maa xam

Bilaaxi maa xam

Ndax Yalla miy mënale

Mootax ma mën

Ba ku flew ma wonla sama mën- mën

Te kepp ku mëna faram-facce

Xam na ni maa mën

ndax dama oyof nib sën

Ba tax far maay ki mën

Chant 22 : Bisimillaaxi tagul mako déeti tagu warna jàam

Bismillaaxi tagul mako déeti tagu warna jàam

Abdu kura, ku Njoogu

Njoogou Dia Pël mëw

Baay Njoogu Njaay

Baay Njoogu Njaay

Bu donul kon Layti Ngoone

Luma yendo bay makoy moom

Buma flibe senn boroom jel

Baay Njoogu Njaay

Baay Njogu Njaay

Bou donul kon Layti Ngoone

Luma yendo bay makoy moom

Buma flibe senn boroom jel

40

Chant 20 : Capture et donne ton esclave !

Capture-moi et fait de moi ton esclave !

Capture-moi et fait de moi ton esclave !

Capture-moi et fait de moi ton esclave !

Sinon capture moi et vend moi comme esclaves

Le fils du roi ne doit pas exécuter très tôt

Chant 21 : Au nom de Dieu, c'est moi qui connais39

Au nom de Dieu, c'est moi qui peux

Car c'est Dieu le détenteur du pouvoir

Qui m'en a donné

Je peux le prouver à qui le voudrait

Et quiconque sait traduire

En sera convaincu

Je suis humble comme un tas d'ordure

Ce qui fait que je suis celui qui est capable

Chant 22 : Louange à Dieu ! Je vais encore recommencer

Louange à Dieu ! Je vais encore recommencer

En rendant grâce à Dieu

Abdu kura, ku Njoogu

Njoogu Dia! Le Peul offre du lait

Baay Njoogu Njaay

Baay Njoogu Njaay

Si ce n'était pas à cause de Layti Ngoone

Tout ce que je récolterais le jour m'appartiendrait

Si je rentre au village je le donnerais aux nécessiteux

Baay Njoogu Njaay, Baay Njoogu Njaay

Si ce n'était pas à cause de Layti Ngoone

Tout ce que je récolterais le jour m'appartiendrait

Si je rentre au village je le donnerais aux nécessiteux

39 Le performateur de se chant montre que celui qui veut prétendre au savoir et au pouvoir doit etre humble.

41

Chant 23: Waaroo waar

Waaroo waar

Waar dem na géej

Waaroo waar

Waar dem na géej samba

Góoroo góor bu kenn daw

Bu kenn naan i

Yaay Faatu fattalikul

Lima la waxoon biig

Bu naaj tàngée

Mane bu naaj tàngée

Ci la jáambaar di féeñ

Chant 24 : mala mala

Dégg na si mala mala

Du mala bañ

Dégg na si yama yama

Du yama soof

Chant 25 : ngongk

Mbaam ngongk rëy biir

Soxor, mana màtt

Aay cium cumbur

Kuko war te mënoo ngawar

Wëqu cammooñ la lay door

Te fu mu la dal foofa nooy

42

Chant 23 : Oh labeur !

Oh labeur !

Le labeur est allé en mer

Oh labeur !

Le labeur est allé en mer

Que personne ne prenne la fuite

Que personne n'aille boire

Yaye Fatou40souviens-toi

Je t'avais dit hier soir

Quand le soleil est au zénith

Je répète, quand le soleil est au zénith

C'est à ce moment que le brave se distingue

Chant 24: mala mala41

J'ai entendu dire mala mala

Ne veut pas dire que je te déteste

J'ai entendu dire yama yama42

Ne veut pas dire que je te minimise

Chant 25: l'âne adulte

L'âne adulte au gros ventre

Méchant assoiffé de mordre

Mauvaise pour les ânons

Qui monte sur lui sans pouvoir s'accrocher

C'est du pied gauche qu'il va te frapper

Et là où il tape, fait des dégâts

40 Yaay fatou est la mère de l'homme qui se glorifie.

41 Onomatopée qui imite le bruit des rumeurs.

42 Rumeurs des racontars.

43

Chant 26: Njolor Samba

Njolor Samba moy daane góor

Duma nann i te ku nann i da nga daw

Chant 27: Jáambaar ca waar

Jáambaar ca waar ba

Loo liggéey du yaako moom

Ngembuléen gaañi

Ñaq réerul boromam

Jáambaar góorgóorlul suuf si noy na

Tool bi yaa na

Mbay lu baax la

Ñaq réerul boromam

Chant 28: Tool bi

Tool bi dina sango njoor

Mba ma sango njoor

Chant 29: yewwul yee ma

yewwul yee ma

yewwuloo yee ma

yewwul yee ma, Ndeeroo Njaay

Bunu demee ngay lakk may bey

yewwul yee ma

yewwuloo yee ma

yewwul yee ma, Ndeeroo Njaay

Bunu demee ngay lakk may bey

yewwul yee ma

yewwuloo yee ma

yewwul yee ma, Ndeeroo Njaay

Bunu demee ngay lakk may bey

44

Chant 26 : C'est le soleil d'après-midi qui révèle l'homme

C'est le soleil d'après-midi qui révèle l'homme

Je ne vais pas boire quiconque ira boire aura fui

Chant 27 : le courageux au champ

C'est au champ qu'on reconnait le brave

Tout ce que tu produis te revient de droit

Retroussez les manches les gars

La sueur se paye toujours

Homme courageux acclame toi, la terre est molle

Le champ est large

La culture est une bonne chose

La sueur se paye toujours

Chant 28 : Le champ

Le champ sera recouvert de pagne

Sinon je serais recouvert de pagne

Chant 29 : Réveille-moi dès que tu te lèves !

Réveille-toi et réveille-moi !

Réveille-toi et réveille-moi !

Ndeeroo Njaay, Réveille-moi dès que tu te lèves !

Arrivés sur place, tu brûleras les herbes et moi je cultiverai

Réveille-toi et réveille-moi !

Réveille-toi et réveille-moi !

Ndeeroo Njaay, Réveille-moi dès que tu te lèves !

Arrivés sur place, tu brûleras les herbes et moi je cultiverai

Réveille-toi et réveille-moi !

Réveille-toi et réveille-moi !

Ndeeroo Njaay, Réveille-moi dès que tu te lèves !

Arrivés sur place, tu brûleras les herbes et moi je cultiverai

45

Chant 30 : Ra?, Ra?, Ra?

Ra?, Ra?, Ra?

Ba ra? ba jeex

Góoru faatu Njaay

Maa mën flile ba ra? ba jéex

Ra?, Ra?, Ra?

Ba ra? ba jeex

Góoru faatu Njaay

Maa mën flile ba ra? ba jéex

Ra?, Ra?, Ra?

Ba ra? ba jeex

Góoru faatu Njaay

Maa mën flile ba ra? ba jéex

Chant 31: Ngonka daan na Malaw

Ngonka daan na Malaw

Naaru goor daan na Buur Njaay

Taaguna saa yaay

Taaguna saa baay

Dotuma gaaw a paan

Ngonka daan na Malaw

Naaru goor daan na Buur Njaay

Taaguna saa yaay

Taaguna saa baay

Dotuma gaaw a paan

Chant 32: Ñaaju njolor sãntabañ la

Ñaaju njolor sãntabafl la

Wante flaaju takusaan amna borom

46

Chant 30 : Rang43

Rang, rang, rang

Jusqu'à la fin du rang

L'homme de faatu Njaay 44

Je suis plus fort que ceux -ci

Jusqu'au bout du rang

Rang, rang, rang

Jusqu'à la fin du rang

L'homme de faatu Njaay

Je suis plus fort que ceux -ci

Jusqu'au bout du rang

Chant 31 : L'âne a terrassé Malaw45

L'âne a terrassé Malaw

Le coursier a terrassé Buur Njaay

J'ai demandé l'autorisation à ma mère

J'ai demandé l'autorisation à mon père

Je ne me fatiguerai plus facilement

L'âne a terrassé Malaw

Le coursier a terrassé Buur Njaay

J'ai demandé l'autorisation à ma mère

J'ai demandé l'autorisation à mon père

Je ne me fatiguerai plus facilement

Chant 32 : Le soleil de Njolor46est une obligation

Le soleil de njolor est une obligation

Alors que le soleil de takusaan 47à un propriétaire

43 Ordre, disposition de plusieurs personnes ou choses sur une même ligne.

44 Fatou Ndiaye est l'épouse de l'homme qui se glorifie.

45 C'est le bouleversement des choses, il est indispensable qu'un roi avec toute sa dimension sociale tombe de cheval.

46 C'est au environ de 13 heures et 15heures quand le soleil est au zénith.

47 Vers 17heures.

47

Chant 33: Baay Demba waar Njaay

Baay Demba waar Njaay

Waar waa ko yóbbu géej

Ba flukoy suul floo nga naan

Gasléen mu xóot a xóot

Waqileen mu xóot a xóot yaay

Jáambaar ngeen fiy suul

Ñun talunoo waxtaan tey ak yaw

Afl baanga toolu Baay jibi Combaan

Naanu baanga Baal

Ndax Malik Yaasin tukkina Ndakaaru

Kon tey flu yendoo béy

Chant 34: Ma mën gune ak baayam

Ma mën gune ak baayam

Ndax Baay ba doole ba da jeex

Té gune ba doole ba dikagul

Chant 35: Mbay Njaay

Mbay Njaayoo! Mbay Njaay

Mbay Aali Bure

Mbay Coro Codu

Mbaar ak mbaar

Mbaar ak Demba jigéen

Tog-tongi cebi

Ku bafl gaaya tiib ya tax

Mbay Njaay o Mbay Njaay

Mbay baaba Aali, Mbay baaba Biige

Mbay Aali Biige, Coro Codu

Ma Biige ak Biige

Candeela Njoogu, Samba ak Xoyan

Mbaar ak mbaar, Mbaar ak Lat Demba jigéen

48

Chant 33: Baay Demba waar Njaay 48

Baay Demba waar Njaay

Le labour l'a conduit au bord de la mer

En l'enterrant, on disait

Creusez très profondément

Retirer le sable du trou

Car vous enterrez un homme courageux

Nous n'avons pas le temps de discuter avec toi aujourd'hui

Le repas se trouve au champ de Baay jibi Combaan

La boisson se trouve à Baal

Car Malik Yaasin est allé en voyage à Ndakaaru49

Donc on passera la journée à cultiver

Chant 34 : Je suis plus fort qu'un père et son enfant

Je suis plus fort qu'un père et son enfant

La force du père est épuisée

L'enfant n'a pas encore acquis une force suffisante

Chant 35 : Mbay Njaay

Mbay Njaay ôh Mbay Njaay, Mbay Aali Bure

Mbay Coro Codu

Mbaar et Mbaar50, Mbaar et Demba Jigéen

Tog - tongi cébi51

Si vous détestez de tels gars, c'est dans leur manière de manger

Mbay Njaay ôh Mbay Njaay, Mbay baba Aali, Mbay baba Biige

Mbay Aali Biige, Coro Codou, Ma Biige et Biige

Candeela Njoogu, Samba et Xoyan

Mbaar et mbaar, Mbaar et Lat Demba jigén

48 Incité le groupe de travailleurs à soutenir l'effort jusqu'à terme, sans que personne ne recule.

49 La capitale du Sénégal (Dakar).

50 Mbaar le lieu d'initiation des jeunes circoncis.

51 La manière dont les jeunes mangent les plats de riz.

49

Chant 35: Ca Yaasin Je? Maaroo

Ca Yaasin Je? Maaroo

Ca Yaasin Je? Maaroo

Ca Yaasin Je? Maaroo

Ca Yaasin Je? Maaroo

Jigéen nangi deedi daan góor

Ci toolu bayaam

Ca Yaasin Je? Maaroo

Ca Yaasin Je? Maaroo

Ca Yaasin Je? Maaroo

Jigéen nangi deedi daan góor

Ci toolu baayam

Ca Yaasin Je? Maaroo

Ca Yaasin Je? Maaroo

Ca Yaasin Je? Maaroo

Ca Yaasin Je? Maaroo

Jigéen nangi deedi daan góor

Ci toolu baayam

Ca Yaasin Je? Maaroo

Ca Yaasin Je? Maaroo

Ca Yaasin Je? Maaroo

Ca Yaasin Je? Maaroo

Jigéen nangi deedi daan góor

Ci toolu baayam

Chant 35 : Thié Yaasin Je? Maaroo52

Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo La femme est en train de prendre le meilleur sur l'homme dans le champ de son père Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo La femme est en train de prendre le dessus sur l'homme dans le champ de son père Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo La femme est en train de prendre le dessus sur l'homme dans le champ de son père Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo Thié Yaasin Je? Maaroo La femme est en train de prendre le meilleur sur l'homme dans le champ de son père

50

52 Thié Yassine Dieng Mar a fait l'objet d'une légende qui raconte l'histoire d'une brave fille qui parvenait à dominer les hommes dans les champs. Elle est l'aïeule de la femme qui chante ici.

51

Chant 36: Baay bóoy demal rabbi njowaan

Baay bóoy demal rabbi njowaan

Tool bi dotul bóoy

Baay bóoy won ma digi tool bii

Mbaa ma jaal ci mbóoy mi

Chant 37 : Jáambaar joni joni jáambaar legi legi

Jáambaar joni joni jáambaar legi legi

Jáambaar dikatinga tool jéme ngoon

Benn jant duma daan

Té ñaar ya duñu fenkkando

Chant 38: jáambaaro

Jáambaroo, jáambaar Jàamnaaroo, jáambaaar

Ku sa yaay di jáambaar do daw xare

Suma nare daw dee

Toj naa àll bi

Ray na gaynde yi Ma di jàambaar

Jàambaroo, jàambaar

Jàamnaaroo, jàambaaar

Ku sa yaay di jàambaar do daw xare

Suma nare daw dee

Toj naa àll bi Ray na gaynde yi Ma di jàambaar

52

Chant 36 : Père va tisser un hamac

Père va tisser un hamac

Le champ ne peut plus résister

Père montre-moi les limites du champ

Avant que je déborde sur le champ d'autrui

Chant 37 : Être courageux

Être courageux sur le champ, devenir courageux à l'instant même

Le courageux est venu au champ et travaillera jusqu'au soir

Un seul soleil ne me fatigue pas

Alors que deux soleils ne se lèvent jamais en même temps.

Chant 38: oh guerrier

Oh guerrier, le valeureux

Oh guerrier, le valeureux

Celui dont la mère est courageuse

Ne fuit pas le combat

Plutôt mourir que de fuir

J'ai terrorisé la brousse

J'ai tué les lions

Je suis le brave

Oh guerrier, le valeureux

Oh guerrier, le valeureux

Celui dont la mère est courageuse

Ne fuit pas le combat

Plutôt mourir que de fuir

J'ai terrorisé la brousse

J'ai tué les lions

Je suis le brave

53

Chant 39: Sa sunu ñagee tool yi

Sa sunu ñagee tool yi

Ileer yi nàmmandoo

Ndaw ñi pàacoo tool bi

Ba ku ne tiim sab waar

Jáambaar daaldi feeñ

Ca ruur ma lay tàmbalee

Naaj wi ne da?? leer

Yaafus ba tàmbaliy feeñ

Ker ga lay dàkki toog

Gàcce manula wessu lii

Tey ma won sama Baay ne

Maa ko donn ci jáambaar

Chant 40: toolu baay

Toolu baay

Fale itam toolu baay laa, jam53

Kon na ko bokk bey ko gaawoo, jam

Su mala rawee nga puuboo, jam

Soo ma rawee it tey nga puuboo, jam

Toolu baay

Fale itam toolu baay laa, jam

Kon na ko bokk bey ko gaawoo, jam

Su mala rawee nga puuboo, jam

Soo ma rawee it tey nga puuboo, jam

53 Intaduisable

54

Chant 39 : Dès lors qu'on clôture les champs

Dès lors qu'on clôture les champs

Les houes sont aiguisées

Les jeunes se partagent le champ

Quand chacun aura sa part

Cela commence par le défrichage

Le soleil est au zénith

Le fainéant se découvre

Et va s'asseoir à l'ombre

Honte ne peut être plus grande

Je vais montrer à mon père

Que j'ai hérité son courage

Chant 40: le chant de père

Le chant de père

Là-bas aussi c'est le champ de père, jam

Labourons-le vite ensemble, jam

Si je te devance, tu vas chier, jam

Si tu me devance aussi, tu vas chier

Le chant de père

Là-bas aussi c'est le champ de père, jam

Labourons-le vite ensemble, jam

Si je te devance, tu vas chier, jam

Si tu me devance aussi, tu vas chier

55

Chant 41 : Yaasin Je? Maaroo

Ah ! Yaasin Je? Maaroo

Jigéen duma daan camiñ baamay daan

Yaasin Je? Maaroo

Jigéen duma daan camiñ baamay daan

Ee janaxoo yow mi dëkk suufo

Naka sama maam

Baay gorgi pël bu degee ngaaraadu

Dootul maye meew

Samb maye meewo

Jaarga maye nag

Baay gorgi Samb maye meew

Jaarga maye nag

Baay gorgi yoo ñax bu tenk mbaam ak caatangu naaru góor

Baay gorgi yoo ñax bu tenk mbaam tenk geeléem Saar

Baay gorgi yoo ñax bu tenk mbaam

Gune du ca joow

Chant 41 : Yaasin Je? Maaroo

Yaasin Je? Maaroo

La femme ne me dompte pas c'est l'homme qui me dompte

Yaasin Je? Maaroo

La femme ne me dompte pas c'est l'homme qui me dompte

Ah souris! Toi qui habites sous terre

Comment va ma mère

Baay Gorgi si un peul entend le kañu

Il n'offrira plus du lait

C'est le pâtre qui offre du lait

Le Djarga54offre une vache

Baye Gorgi c'est le pâtre qui offre du lait

Le Djarga offre des vaches

Baye Gorgi l'herbe qui entrave l'âne comme l'entrave du coursier

Baye Gorgi l'herbe qui entrave l'âne et chameau

Baye Gorgi l'herbe qui entrave l'âne

Un enfant ne peut pas mouvoir

Baye Gorgi dans l'herbe qui entrave l'âne

Un enfant ne peut pas mouvoir

56

54 C'est celui qui possède un immense troupeau de vache, de mouton,...

57

Chant 42: Xabu yaay Ngoone

Xabu, yaay Ngoone

Xabu Mayaay saar

Katarpala gen ci góor

Joongama gen ci jigéen

Xorxor a gen kamac

Ñaaw a gen dee

Ñambaas a gen taatunen

Chant 43: Ndaama ak ndaamari bokkul

Ndaama ak ndaamari bokkul

Ndama yeel ba day gatt

Xuuru ganaaw ga taaba

Deun ba angase

Lumu yótu jot ko

Lumu dóor mu ñibi allaaxira

Chant 44 : ndeqqi

Duma deqqi ngoon

Diko lëmës

Rus naako

Ndajale ma tax

Duma deqqi ngoon

Diko lëmës

Rus naako

Ndajale ma tax

Duma deqqi ngoon

Diko lëmës

Rus naako

Ndajale ma tax

58

Chant 42: Xabu, fils de Ngoone

Xabu, fils de Ngoone,

Xabu, fils de MayaaySaar

Le Caterpillar55 convient mieux à l'homme

La beauté sert mieux à la femme

La lueur est préférable à l'obscurité totale

La laideur à la mort

Le Gnambasse56 à la nudité

Chant 43 : Celui qui a une petite taille est tout à fait différent d'un nain

Celui qui a une courte taille est tout à fait différent d'un nain

Le petit a les os courts,

Et des jambes courtes

Une colonne vertébrale large

Et une poitrine saillante

Il atteint toujours son but

Et quiconque encaisse son coup, séjourne dans l'au-delà

Chant 44: la récolte d'arachide

Je ne récolte pas l'arachide

En laissant les graines sous la terre

J'ai honte de le faire

Parce que je pense au moment ou on doit les entasser

Je ne récolte pas l'arachide

En laissant les graines sous la terre

J'ai honte de le faire

Parce que je pense au moment ou on doit les entasser

Je ne récolte pas l'arachide

En laissant les graines sous la terre

J'ai honte de le faire

Parce que je pense au moment ou on doit les entasser.

55 Le performateur fait allusion à la force, à la puissance, et à l'endurance que doit avoir le cultivateur.

56 C'est un morceau de tissu souvent de couleurs différentes qu'on ajoute à un pagne ou un pantalon.

59

Chant 45: kañu Samba ak Baay Mor

Kañu Samba ak Baay Mor

Daaba ak daabali bokul

Daaba xuuru ginaawa day yaa

Loxo ya day bar jot

Lumu yôotu jot

Lumu dôor nga agg suuf

Kañ Samba ak Baay Mor

Maxuja Maram Gey

Maxuja Maram Faal

Maa ngi jooy téeñ Candeela Faal

Buurub gey ma noon ya jaaxaanal fa Ndoom

Kañu Samba ak Baay Moor

Maxuja Maram Gçy!

Maxuja Maram Faal!

Maa ngi jooy teen Candeela Faal

Buurub gey ma noon ya jaaxaanal fa Ndoom

Ñii ngi dëppu,

Ñii ngi deex

Man mane cëpp ne cëreet ni gçndel !

Di beegu nim yee

Di tàweeku nig laspeer

Saakoddu Biige linger la

Laba daðu koo bôoleek Côoni Mbayya? Béey

Bèsub keeroog ku deewul gore woo

Sa Aanta ak Saademba ak Seeni Saañoxor

Saakoddu Biige liigeer la

Njolor fasu bay laa

Njolor njolooroo njolor

Fasu baay laa !

Ku war ma door laa !

Ku bëgga war ma door la !

Baay boy yar nag mbooyyee, man bu ma màggee mëna bay

60

Chant 45 : Le slogan de Samba et de Baay Mor

Le slogan de Samba et de Baay Mor

« Daaba est différent de daabali57;Daaba au dos creux ;

Il a les mains longues et agiles, tout est à sa portée et ses coups sont fatals

La devise de Samba et de Baay Mor

Maxuja Maram Gey! Maxuja Maram Faal

Je pleure toujours Téeñ Candeela Faal,58

Le roi Gey que les ennemis tuèrent à Ndoom59

La devise de Samba et de Baye Mor

Maxuja Maram Gey!

Maxuja Maram faal

Je pleure toujours Teigne Candeela Faal,

Le roi Gey que les ennemis tuèrent à Ndoom

Ceux-ci sont courbés, ceux-là sont tordus

Moi, je suis droit, puissant et complet comme un ange :

Je m'enroule sur moi-même tel un boa, je me tends telle une lance pierre60

Saakoddu Biige est linguère

Laba affronta dans un duel mortel Côoni Mbayya? Béey

Ce là, fut lâche celui qui ne trèpassa

Sa Aanta et Sademba Seeni Saañoxor

Sacodu Biigé sont lingère

Njolor est le cheval de mon père !

Njolor, Njolor, Njolor est le cheval de mon père !

Je frapperai quiconque le chevauche !

Je frapperai aussi quiconque essaie de me l'enlever !

Mon père a laissé son champ en jachère61 !

Quand je serai grand je serai capable de le cultiver !

57 Dâba et dâbali : ces deux catégories différentes l'une est plus petite que l'autre et ne sert qu'à couper les herbes et arbusseaux, l'autre plus grand et posséde deux branches qui ressemblent à des bras et sert à couper les herbes et à meuler le mil.

58 Ancien roi du Baol.

59 Ndome : lieu où est tombé ce roi cité ci-dessus.

60 Lance pierre : l'auteur utilise se même terme dans le texte wolof.il fait allusion à la matière élastique qui peut prendre une dimension extraordinaire, si on l'étire, l'auteur se compare à elle.

61 « Laisser son champ en jachère » ici ce n'est pas le fait laisser le champ au repos mais, les parents avaient l'habitude de tester l'efficacité et l'endurance de leurs enfants en leur donnant un grand lopin de terre bourré d'herbes à cultiver. Si le garçon en question pavient à cultiver le lopin en un temps record, on lui accord le droit d'avoir ses propres champs et de fonder une famille.

61

Njool Soda laay sëggël bay!

Baay bóoyo, baay booy, baay booy

Baay yar nag mbooyy

Baay boy yar nag mbooyy

Caali Maa Njonge Seen

Sa ma baay, baay booy

Man la doon xaar, maggënaa dama koy bay

Chant 46: Mbay Njaay

Mbay Njaayoo

Mbay Njaay

Mbay bukaari Biige

Keroog bañu koy suul

Manga naan

Gas leen mu xoot

Waxi leen mu yaa

Njaay jaata njaay

Jàambaar geeni suul

Mbay Njaay moo bay ba wallu gejj

Ndiole Soda Laye courbe toi et mets- toi au labeur !

Oh Père! Oh Père ! Mon père a laissé son champ en jachère !

Caali Maa Njonge Seen

Mon père, mon cher père

Ce champ m'attendait

Je suis grand maintenant. Je vais le cultiver

Chant 46: Mbay Njaay !62

Mbay Njaay oh!

Mbay Njaay

Mbaye de Bukari Biige

Le jour où on l'enterrait, il disait

Creusez profondément,

Que le trou soit large

Njaay jaata njaay63

Parce que vous enterrez un homme brave

Mbay Njaay a cultivé son champ jusqu'au bord de la mer

62

62 Ce chant s'apparente beaucoup au mythe de Baye Demba War qui a cultiver jusqu'à la mer

63 Elle se dit pour faire l'éloge des ndiaye.

63

précédent sommaire suivant






Bitcoin is a swarm of cyber hornets serving the goddess of wisdom, feeding on the fire of truth, exponentially growing ever smarter, faster, and stronger behind a wall of encrypted energy








"Nous voulons explorer la bonté contrée énorme où tout se tait"   Appolinaire