Njàngaanoo, njàngaanoo,
njàngaanoo,
Dangay dem ca tool ya mu dogaale la
Siggil ndaama ngeeroo siggee mat a dige
Toj na àll ba ray na gaynde ya
Tuur nafa beñwaaru xaalis
Ñax jaañ baal ma tàkko jaañ baal
ma maalig jaañ baal ma
Sele mandumbaan mbòoyoo dama koo yendoo daan
Biraanoo mbañ jòobo bël sàmba
yaay ndaw
Simboorè majaañ njaay mati jileen manjaga
dina la woy
Saam sàmba mbay mbay, majigéen bòoyoo
ak bël jòoboo
Bël sàmba yaay ndaw
Sàmm sàmmileen rëbb rëbbi leen
Ndongo jàngi leen maa ngi jàngi mbay
Yaasin gay maaroo ak baay madigèen ndaw
Jigèen su de daan gòor ca toolu baayam
Baay baa ko mën a wax
Jàppal ma saas kumba baayòo bama ngemboo
ngeer
Golo jaañ buca mënul yèeg booba
gàllina
5
10
15
|